Tomb yi

CI MBIRU TOR BROWSER

Tor Browser dafay jëfandikoo jokkoowu Tor bi ngir aar say mbiri bopp ak nu bañ la xàmmee. Jëfandikoo jokkoowu Tor am na ñaari moomeel yu am solo:

Rax ci dolli, Tor Browser danu ko defar ngir aar dalu web yi ci "fingerprinting" wala ci xàmmee la sunu sukkandikoo ci sa tëgginu xuusukaay.

Ci li teew, Tor Browser du deñc benn cosaaanu xuus. Nëbbiit yi baaxuñu ci ab session rekk (ba ngay génn ci Tor Browser wala nu laaj la ab New Identity.

NAKA LA TOR DI DOXE

Tor nekk na ab jokkoo ci ay yoon yu jëmmadi bu lay may nga gën aar say mbiri bopp ak kaarànge ci Internet bi. Tor dafay liggéey di yonnee say lëkkale ci ñetti serwëer yuy jàll (nu leen di woowe itam jàllalekaay ci jokkoowu Tor bi. Jàllalekaay bi mujj ci circuit bi ("exit relay" bi) dafay génne lëkkale bi mu fës ci Internet bi.

Naka la Tor di doxe

Nataal bii ci kaw dafay wone ab way-jëfandikoo xuusukaay ci dalu web yu wuute ci Tor. Ordinaatëer yu nëtëx yi ci digg bi ñooy wone lëkkale ci biir jokkoowu Tor, te ñetti caabi yi dañuy wone déggoob web yuñu caabi diggante way-jëfandikoo bi ak jàllalekaay bu ci ne.

YEBBI

Yoon wi gën a woyof te gën a wóor ngir yebbi Tor Browser mu ngi nekk ci dalu web bu Tor Project bu baax bi ci https://www.torproject.org/download. Sa lëkkalook dalukaay bi dina am kaarànge sooy jëfandikoo HTTPS, loolu dafay tax mu gën a jafe ci nit ngir mu soppi ko.

Waaye, dinay faral am ay saa yoo xam ni doo mën a dugg ci dalu web bu Tor Project: ci misaal, mën na taxaw ci sa jokkoo. Su loolu amee, mën nga jëfandikoo benn ci doxalini yebbi yiy wuutu yi nu lim ci suuf:

SEETU YI

Soo mënula yebbi Tor Browser ci dalukaayu web bu baax bi, ci foofu mën nga ko jéem a yebbi ci benn ci sunu seetu yu baax yi, wala jaare ci EFF wala ci Calyx Institute.

GetTor

GetTor nekk na ab serwiis buy tontu automatically ci ay bataaxal yu àndak ay lëkkalekaay ci version bu Tor Browser bu gën a bees bi, nu dalal ko ci ay béréb yu bari, niki Dropbox, Google Drive ak GitHub.

JËFANDIKOO GETTOR JAARE KO CI BATAAXALU INTERNET

Yonneel ab bataaxalu internet ci gettor@torproject.org, te ci biir message bi bindal rekk "windows", "osx", wala "linux", (yu amul maas yi ko séqq) mu aju ci sa nosteg doxin. Ci misaal, ngir am ay lëkkalekaay ngir yebbi Tor Browser ci Windows, yonneel ab bataaxalu internet ci gettor@torproject.org bu àndak baatu "windows" ci biir.

GetTor dina tontu ak ab bataaxalu internet bu am ay lëkkalekaay yi nga mën a jaare ngir yebbi ëmb bu Tor Browser, xaatim bunu binde loxo (nu soxla ko ngir saytu yebbi bi), màndargay baaraam bu caabi bi nu jëfandikoo ngir defar xaatim bi, ak ëmbub checksum bi. Mën nanu la may ab tànneef bu "32-bit" wala "64-bit" bu software: loolu dafay aju ci xeetu ordinaatëer bi ngay jëfandikoo.

JËFANDIKOO GETTOR JAARE KO CI TELEGRAM

Yonneel ab message ci @GetTor_Bot ci Telegram.

GetTor Bot

SAMP

System requirements

Tor Browser is based on Mozilla Firefox's ESR (Extended Support Release), which periodically updates to include critical security updates from Firefox's main version. Due to these updates, older operating systems may eventually become incompatibile with newer versions of software dependencies that are only available in more recent OS versions. Maintaining support for outdated systems would compromise the security of Tor Browser, as it would require disabling newer security features and mechanisms that are crucial for protecting users' online anonymity.

Note: Support for Windows 7, 8, and 8.1 will be discontinued after the release of Tor Browser 14, scheduled for the end of 2024. Users on these operating systems are strongly advised to upgrade to maintain access to the most recent updates and security features provided by Tor Browser.

Windows

Operating Systems (32-bit and 64-bit):

macOS

Linux

Tor Browser is supported on any modern Linux-based operating system. Please reach out if you encounter any issues while installing.

Android

Samp

Ngir Windows

  1. Xuusal ci Tor Browser yebbil xët bi.

  2. Yebbil dosiyeb Windows.exebi.

  3. (Lunu digle) Saytul file's signature.

  4. Su yebbi bi matee, kilikeel ñaari yoon ci dosiye .exebi. Mottalil tëralinu sampu wizard bi.

Ngir macOS

  1. Xuusal ci Tor Browser yebbil xët bi.

  2. Yebbil dosiyeb macOS .dmgbi.

  3. (Lunu digle) Saytul file's signature.

  4. Su yebbi bi matee, kilikeel ñaari yoon ci dosiye .dmgbi. Mottalil tëralinu sampu wizard bi.

Ngir GNU/Linux

  1. Xuusal ci Tor Browser yebbil xët bi.

  2. Yebbil dosiyeb GNU/Linux.tar.xzbi.

  3. (Lunu digle) Saytul file's signature.

  4. Léegi toppal doxinu mbind mi wala bu butoŋu liiñ bi:

Doxalinu mbind

Dafar dosiye ordinaatëer bi muy dox ci Linux

Jàppal ni: Ci Ubuntu ak yeneeni distros sooy jéem a ubbi start-tor-browser.desktop ab dosiyeb jukki mën na ubbeeku. Ci mbir moomu, war nga soppi doxalin bu baaxul bi te nga fexe ba dosiyey ordinaatëer yi nekk yuy mën a doxal. Sukkandikukaay bi mën nanu ko faral di gis ci sa dosiye jëfekaay.

Doxalinu Command-line

Yeneeni tegtalukaay yu ci dolleeku yu nu mën a jëfandikoo ak start-tor-browser.desktop ci tegtalu ndigal bi:

Tegtalukaay Xëtu tegtal
--bindu-app Ngir bindu ci Tor Browser niki ab jumtukaayu ordinaatëer.
--verbose Ngir wone Tor ak liggéeyu Firefox in ordinaatëer bi.
--log [dosiye] Ngir rënk Tor ak liggéeyu Firefox ci dosiye (default: tor-browser.log).
--detach Ngir téqqale nosukaay ak dawal Tor Browser ci njiitlaay.
--faase bindu-app Ngir faase bindu ci Tor Browser niki ab jumtukaayu ordinaatëer.

Gisal fii naka lanuy yeesale Tor Browser.

DOXAL TOR BROWSER YOON WU NJËKK

Soo taalee sa Tor Browser, di nga gis palanteer bu Lëkkalook Tor. Lii daf lay jox ab tànneef ngir wala nga lëkkaloo te du am jàdd ci jokkoowu Tor bi, wala nga defaraat Tor Browser ngir sa lëkkaloo. Check the toggle if you want to get automatically connected to the Tor network.

LËKKALOO

Kilikeel 'connect' ngir lëkkaloo ak Tor

Ci anam yu bare, tànn "Connect" dina la may nga lëkkaloo ak jokkoowu Tor bi te doo am benn tërëlin booy samp.

Soo xasee ba kilike, ab bantu status dina feeñ, di wone tolluwaay lëkkaloowu Tor. Su fekkee danga am lëkkaloo bu gaaw, wànte bant bi dafa niroog lu taxaw ci ab tomb, jéemal 'Connection Assist' wala xoolal xëtu Troubleshooting ngir mu jàppale la nga saafara jafe-jafe boobu. Wala, soo xamee ne sa lëkkaloo danu ko yamale wala nga jëfandikoo ab proxy, danga war a kilike ci "Configure Connection".

Kilikeel 'Configure Connection' ngir jek jekal sukkandikukaayi jokkoo yi

CONNECTION ASSIST

Su fekke Tor fatt na ci sa bërëb, jéem ab bridge mën na la jàppale. Connection Assist mën na tànn benn ngir ngay jëfandikoo bërëb bi nga nekk.

Connection Assist buy doxal boppam

If Connection Assist is unable to determine your location you can select your region from the dropdown menu and click on 'Try a Bridge'.

Connection Assist defaraat

DEFARAAT

Tor Browser dina la yobbu ci ay xeeti tànneefi roofoo.

Connection Assist bi daf lay yëgal sa tolluwaayu lëkkaloowu Internet ak sa lëkkaloo ci jokkoowu Tor.

Lëkkaloo xayma bu àndak ndam

Lëkkaloo xayma bu jàllul

Checkbox bu njëkk bi mooy 'Quickstart'. Soo ko tànnee, saa soo ubbee Tor Browser, dina jéem a lëkkaloo ak sa sukkandikukaayu jokko bu njëkk.

Quickstart

Su fekkee sa lëkkaloo danu ko yamale, wala danga jéem te lajj lëkkaloo ci jokkoowu Tor ak benn saafara doxul, mën nga defaraat Tor Browser ngir mu jëfandikoo ab pluggable transport. 'Bridges' dina wone Moytukaaypàcc ngir defaraat ab pluggable transport wala lëkkaloo jëfandikoo pom yi.

Defaraatal Tor bridge

YENEENI TÀNNEEF

Su fekkee sa lëkkaloo dafay jëfandikoo ab proxy mën nga ko defaraat di kilike ci 'Settings ...' ci 'Defaraat nan Tor Browser lanuy lëkkaloo ci Internet'. Ci anam yu bare, lii amul solo. Dinga xami ndax danga soxla tànn checkbox bii ndax sukkandikukaay yu niroo lanuy jëfandikoo ngir yeneen xuusukaay yi ci sa doxinu jumtukaay. Su mënee nekk, laajal sa caytukatu jokkoo ngir gindi. Su fekkee sa lëkkaloo du jëfandikoo ab proxy, kilikeel ci "Connect".

Proxy sukkandikukaay ngir Tor Browser

ANTI-FINGERPRINTING

Understanding browser fingerprinting

Browser fingerprinting is the systematic collection of information about the web browser to make educated guesses about its identity or characteristics. Each browser's settings and features create a "browser fingerprint". Most browsers inadvertently create a unique fingerprint for each user, which can be tracked across the internet. For more in-depth information on browser fingerprinting, refer to these articles on the Tor Blog: Browser Fingerprinting: An Introduction and the Challenges Ahead and Tor Browser: a legacy of advancing private browsing innovation.

Why browser fingerprinting threatens online privacy?

First, there is no need to ask for permissions from the user to collect this information. Any script running in the browser can silently build a fingerprint of the device without users even knowing about it.

Second, if one attribute of the browser fingerprint is unique or if the combination of several attributes is unique, the device can be identified and tracked online. This means that even without cookies, a device can be tracked using its fingerprint.

How Tor Browser mitigates fingerprinting

Tor Browser is specifically engineered to minimize the uniqueness of each user's fingerprint across various metrics. While it is practically impossible to make all Tor Browser users identical, the goal is to reduce the number of distinguishable "buckets" for each metric. This approach makes it harder to track individual users effectively.

Certain attributes, like the operating system and language, are necessary for functionality and cannot be completely hidden or spoofed. Instead, Tor Browser limits the variety within these attributes to reduce distinctiveness. For example, it limits font enumeration and applies character fallback, standardizes screen and window sizes using letterboxing, and restricts the variety of requested languages to a small, predefined set.

The key goal of Tor Browser's anti-fingerprinting protections is to make it significantly more challenging to gather enough information to uniquely identify users, thereby enhancing privacy without compromising necessary functionality.

Anti-fingerprinting features in Tor Browser

Letterboxing

To prevent fingerprinting based on screen dimensions, Tor Browser starts with a content window rounded to a multiple of 200px x 100px. The strategy here is to put all users in a couple of buckets to make it harder to single them out. That works so far until users start to resize their windows (e.g. by maximizing them or going into fullscreen mode). Tor Browser ships with a fingerprinting defense for those scenarios as well, which is called Letterboxing, a technique developed by Mozilla and presented in 2019. It works by adding margins to a browser window so that the window is as close as possible to the desired size while users are still in a couple of screen size buckets that prevent singling them out with the help of screen dimensions.

In simple words, this technique makes groups of users of certain screen sizes and this makes it harder to single out users on basis of screen size, as many users will have same screen size.

letterboxing

Other anti-fingerprinting features

In addition to letterboxing, Tor Browser employs many other features to mitigate browser fingerprinting and protect user privacy. These features include Canvas image extraction blocking, NoScript integration, user-agent spoofing, and first-party isolation. For a complete list of features, please read the Tor Browser design and implementation document.

MOYTU

Dugg bu gaaw ci jokkoowu Tor bi, yenn saa yi ki lay jox serwiisu Internet wala ab gornamaa mën nañu ko taxawal. Tor Browser ëmb na ay jumtukaayi teggi ngir moytu fatt-fatt yooyu. Jumtukaay yooyu ñu ngi tudd "pluggable transports".

AY XEETI PLUGGABLE TRANSPORT

Ci jamono jii am na ñeenti pluggable transports yu jàppandi, waaye nu ngi yaatal yeneen yu bari.

obfs4 obfs4 dafay wóoradil xuusu Tor, te dafay tax itam jumtukaay yiy ubbi ay pexe duñu gis bridges yi sooy segg ci Internet. obfs4 bridges ñoo gën a tuuti liñuy taxawal ak jumtukaay yi leen jiitu, obfs3 bridges.
meek meek transports dafa koy melal ni yaa ngi xuus ci ab dalu web bu mag ci palaasu jëfandikoo Tor. meek-azure dafa koy melal ni yaa ngi jëfandikoo ab dalukaayu web bu Microsoft.
Snowflake Snowflake dafay wone ay yoon ci sa lëkkale ak volunteer-operated proxies ngir mu mel ni yaa ngi woote wideo ci palaasu jëfandikoo Tor.
WebTunnel WebTunnel dafay nëbb sa lëkkalook Tor, feeñal ko ni yaa ngi ci biir ab dalu web jaare ko ci HTTPS.

JËFANDIKOO PLUGGABLE TRANSPORTS

Ngir jëfandikoo ab pluggable transport, kilikeel ci "Configure Connection" sooy tàmbali Tor Browser sa yoon wu njëkk. Ci suufu pàccu "Bridges" yi, xoolal tànneef "Choose from one of Tor Browser's built-in bridges" te kilike ci tànneef "Select a Built-In Bridge". Ci àlluwa bi, tànnal benn ci pluggable transport bi nga bëgg a jëfandikoo.

Soo xësee ba tànn pluggable transport bi, kilikeL ci "Connect" ngir deñc say sukkandikukaay.

Wala, soo yoree Tor Browser buy dox, kilikeel ci "Settings" ci àlluwa hamburger (≡) ba noppi ak ci "Connection" ci wàllu wet gi. Ci suufu pàccu "Bridges" yi, xoolal tànneef "Choose from one of Tor Browser's built-in bridges" te kilike ci tànneef "Select a Built-In Bridge". Tànnal benn ci pluggable transport bi nga bëgg a jëfandikoo ci àlluwa bi te nga kilike ci "OK". Say sukkandikukaay dina nu leen deñc automatically soo sëxee ba tëj xët bi.

Defaral ay built-in bridges

BAN TRANSPORT LAA WAR A JËFANDIKOO?

Bépp transport bunu lim ci àlluwa Tor Bridge am na ab doxalin bu wuute, te seeni njariñ mu ngi wéeru ci say anami bopp.

Sooy jéem a moytu ab lëkkaloo bu taxaw ci yoon wu njëkk, danga war a jéem ci transports yu wuute yi: obfs4, snowflake, wala meek-azure.

Soo jéemee tànneef yépp, te benn ci ñoom mayula nga lëkkaloo, dafay soxla nga laaj ab bridge wala nga dugg ak say yoxo ci dëkkuwaayi bridge yi.

Jëfandikukat ya ca China dinañu soxla lëkkalook ab obfs4 bridge bu beru te limunu ko. Jokkool ak sunu Telegram Bot @GetBridgesBot te nga bind /bridges. Wala nga yonnee ab bataaxalu internet ci frontdesk@torproject.org te mu ànd ak baat yi "private bridge cn" ci tombu bataaxalu internet bi. Sooy lëkkaloo ci meneen réew, ci bule nexee bul fàtte duggal sa réew wala sa kotu réew ci tombu bataaxalu internet bi.

Jàngal pàccu Bridges yi ngir xam lan mooy bridges ak naka nga leen di jotee.

BRIDGES

Lu ëpp ci Pluggable Transports, yu mel ni obfs4, dañuy wéeru ci jëfandikoo yu jàllalekaayi "bridge". Nirook jàllalekaayi Tor yu baax, bridges yi ñu ngi daw ci seen coobare; wuteek jàllalekaay yu baax yi, waaye, duñu leen lim ci lu fës, looloo tax ab noon mënu leen a ràññee ci lu yomb.

Jëfandikoo bridges yu ànd ak pluggable transports dafa lay dimbali ngir doo feeñ ci sa jëfandikoo Tor, waaye mën a wàññi dooley lëkkaloo bi soo ko tëkkaleek jëfandikoo jàllalekaayi Tor yu baax.

Yeneeni pluggable transports, yu mel ni meek ak Snowflake, dañuy jëfandikoo ay tekniku jumtuwaay yu dul ubbi ay pexe yu wéeruwul ci seet ay dëkkuwaayi bridge. Soxlawuloo am ay dëkkuwaayi bridge ngir jëfandikoo transport yi.

JOT DËKKUWAAYI BRIDGE YI

Ndax dëkkuwaayi bridge yi fësuñu, dina laaj nga seet leen yaw ci sa boop. Am nga yenn tànneef:

Request bridges from within Tor Browser

Su fekkee yaa ngi soog a jëfandikoo Tor Browser, kilikeel ci "Configure Connection" ngir ubbi palanteer bu sukkandikukaayi Tor yi. In the "Bridges" section, locate the option to "Find more bridges" and click on "Request bridges" for Tor Project to provide a bridge. Mottalil Captcha bi te nga kilike ci "Submit". Kilikeel ci "Connect" ngir deñc say sukkandikukaay.

Wala, soo yoree Tor Browser buy dox, kilikeel ci "Settings" ci àlluwa hamburger (≡) ba noppi ak ci "Connection" ci wàllu wet gi. In the "Bridges" section, locate the option to "Find more bridges" and click on "Request bridges" for Tor Project to provide a bridge. Mottalil Captcha bi te nga kilike ci "Submit". Sa sukkandikukaay dina nu ko deñc automatically soo sëxee ba tëj xët bi.

Laajal ab bridge ci torproject.org

DUGGAL DËKKUWAAYI BRIDGE YI

Su fekkee yaa ngi soog a jëfandikoo Tor Browser, kilikeel ci "Configure Connection" ngir ubbi palanteer bu sukkandikukaayi Tor yi. In the "Bridges" section, from the option "Enter bridge addresses you already know" click on "Add new bridges" and enter each bridge address on a separate line. Kilikeel ci "Connect" ngir deñc say sukkandikukaay.

Wala, soo yoree Tor Browser buy dox, kilikeel ci "Settings" ci àlluwa hamburger (≡) ba noppi ak ci "Connection" ci wàllu wet gi. In the "Bridges" section, from the option "Enter bridge addresses you already know" click on "Add new bridges" and enter each bridge address on a separate line. Say sukkandikukaay dina nu leen deñc automatically soo sëxee ba tëj xët bi.

Duggalal dëkkuwaayi bridge yi ak sa loxo

Su lëkkaloo bi jàllulee, bridges yi ngay jot mën nañu wàcc. Ci bu la neexee jëfandikool benn ci tëralin yii ci kaw ngir am yeneeni dëkkuwaayi bridge, te nga jéemaat.

BRIDGE-MOJI

Dëkkuwaayu bridge bu ci nekk dafay feeñ ci ab liiñu màndargay emoji bunu tudde Bridge-mojis. Bridge-mojis yi mën nañu leen jëfandikoo ngir weral ne bridge bi nga bëggoon yokk nanu ko ci ak ndam.

Bridge-mojis nekk nañu xameekaayi bridge yu nit mën a jàng te duñu wone baaxaayu lëkkaloo bi ci jokkoowu Tor wala nekkinu bridge bi. Liiñu màndargay emoji bi mënu nu ko jëfandikoo niki xibaar bunu duggal. Jëfandikukat yi nu ngi leen di laaj ñu duggal dëkkuwaayu bridge bu mat sëkk ngir ñu mën a lëkkaloo ak ab bridge.

Bridge-moji

Dëkkuwaayi bridge yi mënuloo leen séddoo sooy jëfandikoo QR kot wala sooy sotti dëkkuwaay bi yépp.

QR kotu Bridge

SAYTU XAMMEEKAAY YI

So lëkkaloo ak ab dalu web, nekkul nostegkati doxin yi rekk ñoo mën a rënk xibaar yu aju ci sa yër. Dalu web yu bare léegi dañuy jëfandikoo ay banxaas yu toftalu yu bare, bokk ci butoŋu "Like" ci mbaalu jokkko yi, toppkat analitik yi, ak jumtukaayu siiwal yi , yooyu yépp mën nañu lëkkale say jëf ci dalu web yu wuute.

Di jëfandikoo jokkoowu Tor bi dina tax xoolkat yi dakkal mëneefi gis bërëb ba nga nekk ak sa dëkkuwaayu IP, wante donte bu xibaar boobu amul sax dinanu mën a lëkkale say jëf yu wuute booleleen. Ngir loolu, Tor Browser am na ay melo yu dolleeku di la jàppale nga saytu ban xibaar lanu mëna lëkkalee ak sa identity.

BAARU URL BI

Tor Browser dafay dajale sa jaar-jaaru web ci sa lëkkaloo ak dalukaayu web bi ci bantu URL bi. Donte soo lëkkaloo ci ñaari dalukaay yu wute yuy jëfandikoo ab banxaas buy topp ñetteelu pàcc bi niroo, or Browser dina forse ëmbeef bi nu seddale ko ci ñaari Tor circuits yu wute, ba xam ne toppkat bi du xam ne ñaari lëkkaloo yépp ñu ngi bokk joge ci sa xuusukaay.

Ci beneen boor, lëkkaloo yépp ci ab dalukaayu web dinanu ko def ci kaw Tor circuit bu méngoo di tekki ni mën nga xuus ci ay xët yu bare te wute bu ab dalu web ci ay xët wala palanteer yu wuute, te doo ñȧkk doxalin.

Feeñalal circuit diagram ci suufu àlluwa dalu xibaar bi

Mën nga gis ab jagaram bu circuit boobu Tor Browser di jëfandikoo ngir xët biy dox ci àlluway dalukaayu xibaar yi, ci bantu URL bi.

Ci circuit bi, Guard bi wala entry node bi mooy node bi njëkk te danu ko tȧnn automatically ak noonu rekk jaare ko ci Tor. Wante dafa wuteeg yeneen lëkk-lëkk ci circuit bi. Ngir moytu ay songu ci sa profil, Guard node yi dañuy soppeku rekk gànnaaw 2-3 weer yi, wuteeg yeneen lëkk-lëkk yi, yi di soppeku ak bépp fànn bu bees. Ngir xibaar yu gën a yaatu yu aju ci Guards, xoolal FAQ ak Support Portal.

DUGG CI BIIR TOR

Doonte dañoo defar Tor Browser ngir may jëfandikookat yépp nu am lȧqqute ci lënd gi, yenn saa dina am tolluwaay yoo xam ne dina am dayoo jëfandikoo Tor ak dalu web yiy laaj turu way jëfandikoo yi, baatu dugg yi, wala yeneen xibaar yuy tax nu xam la.

Sooy log ci biir dalu web biy jëfandikoo ab xuusukaay bu jaar yoon, dangay feeñal sa dëkkuwaayu internet ak fi nga nekk ci diiru amalin bi. Lu ni mel mooy am tamit su fekkee da nga yónnee bataaxal ci lënd gi. Dugg ci mbaalu jokkooyi wala këllu bataaxal yi di jëfandikoo Tor Browser daf lay may nga tànn bu baax ban xibaar ngay jox dallu web yi ngay xuus. Dugg ci lënd gi di jëfandikoo Tor Browser nekk na tamit lu am solo su fekkee dalu web bi nga bëgg a jot danu ko tere ci sa jokkoo.

Sooy log ci ab dalu web ci Tor, am na ay tomb yu bare yoo war a bàyyi xel:

SOPPI XAMMEEKAAY AK CIRCUITS

New Identity ak tànneefi Tor Circuit yu bees ci suufu àlluwa bu mag bi

Tor Browser dafay wone "New Identity" ak tànneef yu "New Tor Circuit for this Site". Nu ngi nekk tamit ci hamburger bi wala àlluwa bi ci buntu bi (≡).

NEW IDENTITY

Tànneef bii am na solo ci su fekkee bëgg nga fagaru ci sa jëfi xuus bi di ñëw baña lëkkaloo ak li nga doon ñjëkk a def. Di ko tànn dina tëj sa xët ak palanteer yu ubbeeku yépp, dindi xibaar yu aju ci yaw yépp yu melni ay cookies ak jaar-jaaru xuus, ak jëfandikoo Tor circuits bu bees ngir lëkkaloo yépp. Tor Browser dina la àrtu ne jëf yépp ak yebbi yépp dinañu dakk, kon bàyyil loolu xel bala nga kilike "New Identity".

Ngir jëfandikoo tàneef bii, danga soxla kilike ci 'New Identity' ci bantu jumtukaay bu Tor Browser.

TOR CIRCUIT BU BEES BU DAL BII

Tànneef boobule am na solo su fekkee exit relay bi ngay jëfandikoo mënul lëkkaloo dalu web bi nga soxla, wala sarsewul ni mu waree. Tànn ko dina tax xët bi wala palanteer bi sarsewaat ci kaw ab Tor circuit bu bees. Yeneen xët ak palanteer yu ubbeeku yu jóge ci dalukaayu web yu niroo dinañu jëfandikoo circuit bu bees tamit su xësee ba saresewaat. Tànneef bii du dindi bépp xibaar bu beru wala dindi lëkkaloo bi am ci say jëf, te du am benn njeexital ci sa lëkkaloo yi am ak yeneen dalu web yi.

Mën nga tamit dugg ci tànneef bii ci circuit bu bees bi, ci àlluway xibaar bu dalu web bi, ci bantu URL bi.

ONION SERVICES

Onion services (nu njëkk ko xame ci "serwiis yu làqqu") nekk na ay serwiis, yu mel ni ay dalukaayi web, yu jàppandi ci jokkoowu Tor bi kese.

Onion services dafay joxe ay njëriñ ci kaw serwiis yu yamamaay ci web bu amul kiirlaay bi:

NAN LANUY JOTEE CI AB ONION SERVICE

Ne bépp beneen dalu web, di nga soxlaa xam dëkkuwaay bu ab onion service ngir mën a lëkkaloog moom. Ab onion address ëmb na 56 araf ak ay lim, ".onion" topp leen.

Sooy jot ab dalu web buy jëfandikoo ab onion service, Tor Browser dina wone ci bantu URL bi ab xët bu onion di wone sa nekkinu jokkoo: Kaarànge ci jëfandikoo ab onion service. You can learn more about the onion service by clicking on the onion icon and the adjacent Circuit Display in the address bar.

Beneen anam ngir jàng lu jëm ci ab onion site mooy su fekkee ki di doxal daluweb bi teg na ab melo bu nu duppee Onion-Location. Onion-Location nekk na ab jëfandikukat bu matul bu HTTP te dali web yi mën ko jëfandikoo ngir siiwal seen naatangoo onion. Su fekkee dalukaayu web bi nga nekk di xool dafa am ab onion site bu jàppandi, ab doomu xelal bu wiyolet dina feeñ ci Tor Browser di wone ".onion jàppandi". Soo kilikee ci ".onion available", dalu web bi dina sarsewaat te toxu ci naatangoom onion.

Onion-Location

ONION SERVICE AUTHENTICATION

Ab onion service bu baax mooy ab serwiis bu niroog ab onion site buy laaj kiliyaan bi joxe ab gindikaayu authentication laata ngay jot serwiis. Ne ab jëfandikukat bu Tor, mën nga raññele sa bopp ci Tor Browser. Ngir jot serwiis bii, da nga soxla am ay baati dugg yu joge ci aji doxalkatu onion service bi. Sooy jot ab onion service bu baax, Tor Browser dina wone bantu URL bi ab xëtu caabi bu ndaw bu melo doomu-taal, benn jumtukaay àndak moom. Duggalal sa private key bu baax bi ci bërëbu deñc ab joxe bi.

Client Authorization

ONION SERVICES NJUUMTE

Soo mënul jokkoo ci ab onion site, Tor Browser dina joxe ab message bu njumte su dalukaayu web bi jàppandiwul. Ay njumte mën na ñoo am ci tolluwaay yu wute: njumte kiliyaan yi, njumte jokkoo yi, wala njumte serwiis yi. Yenn ci njuumte yiile mën nanu leen defar jaaree ko ci pàccu Troubleshooting. Tablo bii ci suuf dafay wone njuumte yi mën a nekk ak ban jëf nga war a def ngir saafara jafe-jafe bi.

Kot Njuumte Tomb Tegtal bu gàtt
0xF0 Onionsite Kenn Gisu ko Li ko gën a waral mooy onionsite kenn mënu ci jokkoo. Jokkool ak aji caytukat bu onionsite.
0xF1 Onionsite Kenn Mënu ci Dugg onionsite kenn mënu ci dugg ndax njuumte ci biir.
0xF2 Onionsite Dafa dakkal Jokkoo bi Li ko gën a waral mooy onionsite kenn mënu ci jokkoo. Jokkool ak aji caytukat bu onionsite.
0xF3 Mëneesul Jokkook Onionsite Onion site bi jàppandiwul wala jokkoowu Tor bi dafa fees dell. Jéemaatal ci kanam.
0xF4 Onionsite dafay Laaj Authentication Jot onionsite bi dafay laaj ab caabi wànte joxewunu woon benn.
0xF5 Onionsite Authentication dafa Lajj Caabi ji nu joxe baaxul wala danu ko sempi. Jokkool ak aji caytukat bu onionsite.
0xF6 Dëkkuwaayu Onionsite baaxul Dëkkuwaayu onionsite bi nu joxe baaxul. Nu ngi lay ñaan nga duggal ko ni mu waree.
0xF7 Onionsite Circuit Creation Ajandi nanu ko Lajj na ci jokkoog onionsite, mën na nekk jokkoo bu amul doole moo ko waral.

TROUBLESHOOTING

Soo mënul jot onion service bi nga laaj, na la woor ne dugg nga onion address bi ci duggin bu baax: donte ab njumte bu ndaw dina dakkal Tor Browser ba du jàppandi ngir jot dalu web bi.

Soo jéemee jot ab araf 16 ("V2 format" bu gëna gàtt) onion service, xeetu dàllukaay yii doxatul ci jokkoob Tor bu tey.

Mën nga tamit xayma ndax mën nga jot yeneen onion services jaaree ko ci lëkkaloog DuckDuckGo's Onion Service.

Su fekkee mënuloo lëkkëloo ci onion service gànnaaw ba nga xoole dal bi, nu ngi lay ñaan nga jéemaat ci kanam. Mën na am ab jafe-jafe lëkkaloo bu dul yàgg, wala aji yor dal bi mën na ko may mu génn ci jokkoo bi te àrtuwul.

KAARÀNGEY LËKKALOO

Su fekkee say xibaaru bopp lu melni pasug dugg dafay nekk ci Internet bi te kenn nëbbu ko, yërndukat yi mën nanu ko jël ci lu yomb. Sooy ubbee waaru liggéey ci bépp dalu web, war nga wooral ne dal bi am na HTTPS encryption, li di aar ci xeeti yërndukat yi. Dinga mën a xool loolee ci bantu URL bi: Su fekkee sa lëkkaloo danu ko encrypted, dal bi dina dooree ak "https://", rather than "http://".

HTTPS-Menn Melo ci Tor Browser

HTTPS-Menn melo dafay forse bépp lëkkaloo ci jëfandikoo ab lëkkaloo encrypted bu woor nu tuddee ko HTTPS. Dalu web yu gën a bare nangu nañu ba pare HTTPS; yenn yi nangu nañu ñaar ñépp HTTP ak HTTPS. Doxal melo bii dina àar ci sa lëkkaloo yépp ci dalu web yi ñongal nanu ko ngir jëfandikoo HTTPS te loolu day indi kaarànge.

HTTPS-Menn melo ci Tor Browser

Yenn dali web yi dañuy nangu HTTP rekk te lëkkaloo bi ñongal nanu ko. Su fekkee ab HTTPS version bu ab dal jàppandiwul, dinga gis ab xët "Secure Connection Not Available":

Lëkkaloo bu àndak Kaarànge jàppandiwul ci dalukaayu web HTTP

Soo kilikee 'Continue to HTTP Site' nangu nga risk bi te kon di nga seet ab HTTP version bu dal bi. HTTPS-Menn melo dina tëj ci diir ngir dal boobu.

Kilikeel ci butoŋu 'Go Back' bi soo bëggee moytu bépp lëkkaloo bu nu nëbb.

Cryptocurrency safety

Tor Browser presents a security prompt if a cryptocurrency address has been copied from an insecure HTTP website. The cryptocurrency address could have been modified and should not be trusted. Clicking 'Reload Tab with a New Circuit' will attempt to load a secure version of the website with a new Tor circuit.

Cryptocurrency safety

If you click 'Dismiss' you accept the risk and the cryptocurrency address will be copied to the clipboard.

How HTTPS encryption and Tor works in Tor Browser to enhance your privacy and anonymity

Xooltu yiile dañuy wone ban xibaar moo fës ci yërndukat yi bu am ak bu amul Tor Browser ak HTTPS encryption:




AY JOXE YU NU MËN A GIS
Site.com
Dalu web bi ngay yër.
jëfandikukat / pw
Turu jëfandikukat ak baatug dugg yu nu jëfandikoo ngir authentication.
joxe
Joxe yi nuy kay yónnee.
béréb
Dalu jokkoowu ordinaatëer bi nga jëfandikoo ngir seet dalukaayu web bi (dalu IP bu ñépp mën a gis).
Tor
Su fekkee waaw wala déet jëfandikoo nanu Tor.

KAARÀNGEY SUKKANDIKUKAAY

Bi teew, Tor Browser dafay aar sa kaarànge ci nëbb say joxe xusukaay yi. Mën nga boo demee ba mu yàgg yokk sa kaarànge ci tànn dindi yenn melo dalu web yi nu mën a jëfandikoo ngir yàqq sa kaarànge ak sa kiirlaay. Mën nga def lii jaaree ko ci yokk Tolluwaayu Kaaràngey Tor Browser ci àlluwa wëreef bi. Di yokk tolluwaayu kaarànge Tor Browser dina dakkal yenn xëti web yiile dox ni ñu war a doxee, kon war nga natt sa soxla ci wàllu kaarànge dëppoo ak tolluwaayu mboolem amalin bi ngay laaj.

DUGG CI KAARÀNGEY SUKKANDIKUKAAY YI

Kaaràngey Sukkandikukaay yi mën nanu ci jot ci kilike xëtu Wëreef bi nekk ci wetu bantu URL bu Tor Browser. Ngir xool te defaraat sa Kaaràngey Sukkandikukaay, kilikeel ci butoŋ 'Sukkandkukaay' ci alluwa wëreef bi.

Click on 'Settings' under the shield menu

KAARÀNGEY TOLLUWAAY

Di yokk Tolluwaayu Kaarànge ci Kaaràngey Sukkandikukaay yu Tor Browser dina dindi wala dindi xaaju yenn melo dalu web ngir aar ci yenn song yu mën a am. Mën nga doxalaat sukkandikukaay yii waxtu bula neexee jaaree ko ci defaraat sa kaaràngey Tolluwaayu.

Tolluwaayu kaarànge bi dafar nanu ko fii nu toll ci Safest

Royuwaay
Bu ëpp kaarànge
Bi ci ëpp kaarànge

TROUBLESHOOTING

War nga mën a tàmbali xuus ci sa dalukaayu web di jëfandikoo Tor Browser tuuti gànnaaw ba dooree tërëlin bi, te nga kilike ci butong "Connect" bi soo ko dee jëfandikoo yoon bu njëkk.

Kilikeel ci 'Connect' ngir lëkkaloo ci Tor

Connection Assist bi daf lay leeral lu jëm ci nekkinu sa lëkkaloo Internet soo kilikee ci 'Test'.

Connection Assist Xayma

Xoolal sa Lëkkaloo Internet su fekkee danu ci bind 'Jokkoo amul'. Su fekkee lëkkaloo jokkoowu Tor bi indiwaatunu ko te dafay wone 'Lëkkaloo amul' Jéego yii mën nala jàppale.

Connection Assist njuumte soo lëkkalewul

SAAFARA YU GAAW

Su fekkee Tor Browser lëkkaloowul, mën na am benn saafara bu yomb. Jéemal benn bu nekk ci yiile:

YËR TOR LOGS

Ci anam yu bare, xool Tor logs mën na la jàppale ci caytu jafe-jafe bi. Soo amee jafe-jafe lëkkaloo, ab message njumte mën na génn te mën nga tànn benn tànneef ngir "sotti Tor log ci clipboard". Te nga taf ko ci Tor log bi ci ab mbind wala beneen dosiye.

Su fekkee gisuloo tànneef bii te nga ubbi Tor Browser, mën nga xuus ci alluwa hamburger bi ("≡"), te nga kilike ci "Sukkandikukaay", ci mujjantal ga ci "Lëkkaloo" ci bantu wet gi. Ca xët ba sa suuf, ci wetu xëtu "View the Tor logs", bësal butong bi "View Logs...".

Ci beneen boor, ca GNU/Linux, ngir gis làqq yi ci nosukaay bi, xuusal ci dàmb Tor Browser te doxal Tor Browser jaaree ko ci tegtalu ndigël:

./start-tor-browser.desktop --verbose

Wala deñc bataaxal yi ci ab dosiye (bi teew: tor-browser.log):

./start-tor-browser.desktop --log [file]

Yeneen xibaar mën nanu leen a am ci Support Portal.

NDAX DANU TERE SA LËKKALOO?

Soo mënul lëkkaloo ba léegi, sa Bankaas bi la Jox Internet mën na dakkal lëkkaloo yi ci jokkoowu Tor bi. Jàngal pàccu Moytu ngir am ay saafara yu gaaw.

JAFE-JAFE YUNU XAM

Tor Browser dafa nekk ci yokkuteef buy wéy, te yenn jafe-jafe yii xam nanu leen wànte saafara wu nu leen ba léegi. Nu ngi lay ñaan nga xool xëtu Known Issues ngir gis jafe-jafe bi ngay dund ndax nekk na foofu ba pare.

YEESAL

Tor Browser danu ko war a di yeesal saa su nekk. Sooy wéy di jëfandikoo ab version bu yàgg bu tëralinu nosukaay bi, mën nga ubbi buntu kaarànge gi nga amoon buy néewal doole sa kirlaay ak nëbbu.

Tor Browser dina la laaj nga yeesal sa mboolem jëfukaay su xasee génne ab xeet bu bees bu nu genne: alluwa dugg bi (≡) dina wone ab wërngël bu nëtëx bu am ab fitt bu jëm kaw ci kawam, te di nga mën a gis ab tegtalu yeesal bu nu bind soo ubbee Tor Browser. Mën nga yeesal ci anam bu otomatik wala ak sa loxo.

YEESAL TOR BROWSER AUTOMATICALLY

Tànnal 'Taalaat ngir yeesal Tor Browser' ci suufu alluwa wu mag bi

Soo bëgge yeesal Tor Browser, kilikeel ci alluwa dugg bi (≡), te nga tànn "Yeesal bu jàppandi – taalaatal léegi".

Yeesalal bantu jeego bi

Xaaral yeesal bi ngir yebbi te samp, noonee Tor Browser dina taalaat boppam. Di nga jëfandikoo version bu mujj bi.

YEESAL TOR BROWSER AK SA LOXO

Soo bëggee yeesal Tor Browser, jeexalal session xuus bi te nga tëj tërëlin bi.

Dindil Tor Browser ci sa noosteg amalin jaaree ko ci dindi wayndaare bi mu nekk (xoolal Sempi pàcc bi ngir xibaar yu gën a yaatu).

Xoolal https://www.torproject.org/download/ te nga yebbi ab sotti bu Tor Browser bu mujje genn, te nga defaat ko ne bu njëkk.

ARAFU BENNAL DEÑC, SIIWAL AK JAVASCRIPT

JAVASCRIPT

JavaScript ab joxinu ndigal ordinatëer la bu dalu web yiy jëfandikoo ngir joxe ay cër jokkalante yu mel ni wideo, ay dawalinu nataal, ay ndeglu, ak status timelines. Ci lu ajuwul sunu coobare, JavaScript mën na tamit indi ay song ci kaaràngey xuusukaay bi, lu mën a indi deanonymization.

Tor Browser includes an add-on called NoScript. It's accessible through "Add-ons and themes" on the hamburger menu (≡). Locate the NoScript add-on and click on it to open a panel where you can customize its settings.

In the panel, next to the Toolbar button, select 'Show'. This will display the NoScript button to the right of the browser address bar. This button enables you to manage JavaScript and other scripts on web pages, allowing you to control their execution individually or block them entirely.

Jëfandikukat yu soxla tolluwaayu kaarànge bu kawe ci seen xuusukaayu dalu web war nañoo jafal Tor Browser's Kaaràngey tolluwaay ba "Safer" (buy dindi JavaScript ngir HTTPS yu amul dalukaayu web) wala "Safest" (buy def loolu ci dali web yépp). However, disabling JavaScript will prevent many websites from displaying correctly, so Tor Browser's default setting is to allow all websites to run scripts in "Standard" mode.

BROWSER ADD-ONS

Tor Browser nu ngi ko wéer ci Firefox, ak bépp xuusukaay bu am siiwal wala ay wonin ci ordinaatëer yu mën a àndak Firefox mën nanu leen a samp tamit ci Tor Browser.

Wànte, siiwal yi nu xayma yépp ngir jëfandikoo leen ak Tor Browser mooy yiy duggal ci bi teew. Di samp bépp beneen xuusukaay bu àndak ay siiwal mën na yàqq doxalinu Tor Browser wala indi ay jafe-jafe yu tar yuy am njeexital ci sa kiirlaay ak kaarànge. Danuy tere bu baax nga samp ay siiwal, ak Tor Project bi du joxe ndimbal yiile ay defaraat.

FLASH PLAYER

Flash nekkoon na benn amalin bu bari cër bu dali web yi doon jëfandikoo ngir wone ay wideo ak yeneen cër jokkalante yu melni po yi. Danu ko dindi woon def ko bi teew ci Tor Browser ndaxte mënoon na wone bërëb bi nga nekk dëgg ak sa dëkkuwaay IP. Tor Browser jëlatul Flash te kenn mënu ko doxal.

Lu ëpp ci doxalinu Flash bi wecco nanu ko ak HTML5 jëfandikookat, te mu aju bu baax ci JavaScript. Mboolem jëfukaay wideo yu mel ni YouTube ak Vimeo toxu nañu ci HTML5 te dootuñu jëfandikoo Flash.

SEMPI

Dindi Tor Browser ci sa nosteg amalin jafewul:

Ci Windows:

Ci macOS:

Demal ci tànneef alluwa

Demal ci xëtu palanteer

Jàppal ne soo sampul Tor Browser ci nekkin bi teew (twayndaare amalin bi), ak wayndaare TorBrowser-Data nekkul ci ~/Library/Application Support/ wayndaare, wante ci wayndaare menn wayndaare bi nga samp Tor Browser.

Ci Linux:

Jàppal ni sa nosteg amalin jëfukaay "Uninstall" kenn jëfandikoowu ko.

PORTAABAL BU TOR

Tor Browser ci Android

Tor Browser ci Android mooy xuusukaayu portaabal bi fës bi Tor Project defar te di ko doxal. Dafa mel ni Tor Browser bu biro wante ngir sa telefonu portaabal Android. Yenn ci melo yu njëkk yi Tor Browser ngir Android bokk na ci: waññi topp gi ci dalukaayu web yi, aar ceytu gi, di dëggërlu ci fingerprinting, ak moytu tere yi.

YEBBI AK SAMP

Am na Tor Browser ngir Android ak Tor Browser ngir Android (alpha). Jëfandikukat yu ajuwul ci wallu xarale dañoo war a am Tor Browser ngir Android, ndegam bii dal na te njumte yi bariwul. Tor Browser ci Android jàppandi na ci Play Store, F-Droid ak dalukaayu web bu Tor Project. Wóorul ci ngay yebbi Tor Browser feneen fu bokkul ak ñetti mboolem jëfukaay yii.

Google Play

Mën nga samp Tor Browser ngir Android jaare ko Google Play Store.

F-Droid

The Guardian Project dafay joxe Tor Browser ngir Android ci seen F-Droid deñcukaay. Soo bëggee samp jumtukaay jaaree ko ci F-Droid, nu ngi lay ñaan nga topp jéego yii:

  1. Sampal jumtukaayu F-Droid bi ci sa jumtukaayu Android jóge ci the F-Droid website.

  2. Gànnaaw ba nga sampee F-Droid, ubbil jumtukaay bi.

  3. Ci suuf wetu ndeyjoor ci koñ bi, ubbil "Settings".

  4. Ci suufu pàccu "My Apps", ubbil Repositories.

  5. Jafalal "Guardian Project Official Releases" niki lu nu doxal.

  6. Léegi F-Droid dafay yebbi limu jumtukaay yi joge ci the Guardian Project's dencukaay (Jappal: lii mën na jël ay simili).

  7. Bësal Back butoŋ bi ci kaw wetu cammooñ ci koñ bi.

  8. Ubbil "Latest" ca wetu cammoñ ca suuf ca koñ ba.

  9. Ubbil Jumtukaayu seet bi nga bës seetu yaatal bi nekk wetu suuf ci ndeyjoor bi.

  10. Saytu ngir "Tor Browser ci Android".

  11. Ubbil njureefi laaj yi ci "The Tor Project" te nga samp.

Dalu web bu Tor Project bi

Mën nga am tamit Tor Browser ngir Android jaare ko ci yebbi ak samp apk jaare ko ci Tor Project website.

XUUS CI TOR BROWSER NGIR ANDROID Ci YOON WU NJËKK

When you run Tor Browser for the first time, you will see the option to connect directly to the Tor network, or to configure Tor Browser for your connection.

Lëkkale

Lëkkaloo ci Tor Browser ngir Android

Ci anam yu bare, tànn "Connect" dina la may nga lëkkaloo ak jokkoowu Tor bi te doo am benn tërëlin booy samp. Once tapped, a status bar will appear, indicating Tor's connection progress. If you are on a relatively fast connection, but the progress bar gets stuck at a certain point, you might have to configure Tor Browser.

SAMP

Samp Tor Browser ci Android

If you know that your connection is censored, you should tap on "Configure connection". Navigate to the 'Connection' section of the Settings. Su fekkee sa lëkkaloo danu ko dindi, wala jéem nga te lajj ci lëkkaloo ak jokkoo bu Tor te benn saafara sottiwul, bësal ci 'Config Bridge'. You will then be taken to the 'Config Bridge' screen to configure a pluggable transport.

MOYTU

Jàllalekaayi Bridge ñooy jàllekaayi Tor yi nu deful ci àlluway Tor bu fës bi. Bridges am na solo ngir ñiy jëfandikoo Tor te nekk ci nguur yi nooteel yi bare, ak ngir nit ñi soxla kaarànge ndaxte dañoo ragal nu xàm ne dañuy jokkoo jaare ko ci ab dëkkuwaayu Tor relay IP bu fës.

To use a pluggable transport, tap on ""Configure Connection" when starting Tor Browser for the first time. Navigate to the 'Connection' section of the Settings and tap on 'Config Bridge' to configure a bridge. Beneen xoolu bi dina joxe tànneef bi ngir nga jëfandikoo ab built-in bridge wala bridge bus a coobare. Toggle "Use a Bridge" option, which will present three options: "obfs4", "meek-azure", and "snowflake".

Tànnal ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Tànnoon ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Su fekkee tànn nga "Provide a Bridge I know", kon war nga dugg ci ab bridge address.

Joxe ab bridge ci Tor Browser ngir Android

Joxe dëkkuwaayi bridge yi ci Tor Browser ngir Android

SAYTU XAMMEEKAAY

Raññeekaay bu Bees

New Identity ci Tor Browser ngir Android

Su Tor Browser dee dox, di nga gis loolu ci sa àlluway yëgle ci sa jumtukaay gànnaaw ba nga ko yaatale ak sa butoŋu "NEW IDENTITY". Bës ci butoŋ bi dina la indil ab new identity. Ci lu dëppoowuk ak ci Tor Browser ngir Ordinaatëru Biro, "NEW IDENTITY" butoŋ bi ci Tor Browser ngir Android terewul say jëf ci sa xuusukaay bi nu mën ko lëkkale ak li nga doon def bu njëkk. Tànn ko dina soppi sa Tor circuit képp. Note: New Identity feature is not working in latest versions of Tor Browser for Android. Bug #42589

KAARÀNGEY TOLLUWAAY

Sukkandikukaay yu am kaarànge ak ab jumtukaayu nataal bu am kaarànge ci Tor Browser ngir Android

Security levels disable certain web features that can be used to compromise your security and anonymity. Tor Browser ci Android dafay joxe ñetti toluwaayu kaarànge yu niroo yu jàppandi ci ordinaatëeru biro. Mën nga soppi tolluwaayu kaarànge gi ci topp jéego yii nu joxe:

YEESAL

Tor Browser must be kept updated at all times. If you continue to use an outdated version of the software, you may be vulnerable to serious security flaws that compromise your privacy and anonymity. Mën nga yeesal Tor Browser automatically wala ak sa loxo.

Yeesal Tor Browser ngir Android automatically

Jëfekaay bii dafay dëggal ni am nga Google Play wala F-Droid bu nu samp ci sa telefon portaabal.

Google Play

Yeesal Tor Browser ngir Android ci Google Play

F-Droid

Yeesal Tor Browser ngir Android ci F-Droid

Bësal ci "Settings", daldi dem ci "Manage installed apps". Ci beneen xoltu bi, tànnal Tor Browser te ca mujjantal ga nga bës ci butoŋu "Update".

Yeesal Tor Browser ngir Android ak say yoxo

Wëral Tor Project website te nga yebbi ab kayit bi Tor Browser mujjee génnee, ba noppi nga samp ko ne bu njëkk. Ci anam yu bare, version bu Tor Browser bu mujj bii dina sampu ci kaw version bi gën a yàgg, ci noonee di yeesalaat xuuskat bi. Su fekkee loolu dafa lajj ci yeesal xuusukaay bi, mën na am nga soxla sempi Tor Browser laata nga koy sampaat. Ak Tor Browser tëj, dindi ko ci sa jumutukaay nga sempi ko jëfandikoo say sukandikukaayu jumtukaay. Aju ci sa xeetu telefon portaabal, xuusal ci Settings > Apps, nga daldi tànn Tor Browser te nga bës ci butoŋu "Uninstall" bi. Gànnaaw loolu, yebbil Tor Browser bu mujjee génn te nga samp ko.

SEMPI

Tor Browser ngir Android mën nanu ko sempi ci sassa jaare ko ci F-Droid, Google Play wala jaare ko ci say sukkandikukaayi jumtukaayu telefon portaabal.

Google Play

Sempi Tor Browser ngir Android ci Google Play

F-Droid

Sempi Tor Browser ngir Android ci F-Droid

Bësal ci "Settings", daldi dem ci "Manage installed apps". Ci beneen xoltu bi, tànnal Tor Browser te ci mujjantal gi bësal ci butoŋu "Uninstall".

Sukkandikukaay yu jumtukaayu loxo

Sempi Tor Browser ngir Android di jëfandikoo ay sukkandikukaayi jumtukaayu internet

Aju ci sa xeetu telefon portaabal, xuusal ci Settings > Apps, nga daldi tànn Tor Browser te nga bës ci butoŋu "Uninstall" bi.

TROUBLESHOOTING

Yër Tor Logs

View Tor logs on Tor Browser for Android

Ngir gis say Tor logs:

  1. Tap on the settings icon or "Configure connection" when on the "Connect to Tor" screen.
  2. Navigate to the "Connection" section of the Settings.
  3. Tap on "Tor Logs"

To copy the Tor logs to the clipboard, tap on the "Copy" button at the bottom of the screen.

Ngir defar yenn jafe-jafe yi ëpp yu faral di am nu ngi lay ñaan nga xool Support Portal entry.

JAFE-JAFE YUNU XAM

Fii nu toll, am na ay melo yu jàppandiwul ci Tor Browser ngir Android, wante ci jamono jii jàppandi na ci Tor Browser ngir ordinaatëeru biro.

Yeneeni mbiri Tor ci jumtukaayi loxo

Orfox

Orfox nu ngi ko njëkk a génne ci 2015 ci The Guardian Project def ko ak jubluwaay jox jëfandikookati Android yi ab anam ngir xuus ci internet jaare ko ci Tor. Ci diiru ñetti at yii weesu, Orfox dafa wéyaloon di yokku te nekk ab yoon wu siiw ngir nit ñiy xuus ci internet ak kiirlaay gu doy wuteeg xuusukaay yi faral di am, te Orfox amoon na dayoo lool ngir jàppale nit ñi doon dund ñuleen di tere aka bloke ci yenn dalu web ak ëmbeef yu doy waar. Ci 2019, Orfox was sunsetted gànnaaw banu gennee Tor Browser ngir Android bu ofisiyel.

Orbot

Orbot jumtukaayu proxy bu laajul fay buy dooleel yeneeni jumtukaay yi ngir ñuy jëfandikoo jokkoowu Tor bi. Orbot dafay jëfandikoo Tor ngir fas doxalinu Internet bi. Noone mën nga ko jëfandikoo ak yeneeni jumtukaay yi nu samp ci sa telefon portaabal ngir moytu dakkal bi te aar sa bopp ci ceytu gi. Orbot mën nanu ko yebbi te samp ko jaaree ko ci Google Play. Xoolal our Support portal ngir xam ndax soxla nga Tor Browser ngir Android ak Orbot wala benn ci ñoom.

Tor Browser ci iOS

Amul Tor Browser ci iOS. Nu ngi lay diggal ab jumtukaayu iOS bu nu tuddee Onion Browser, te mu nekk open source, jëfandikoo sëfu xayma bu Tor, te ki ko defar nekk kenn kuy liggéeyando ak Tor Project. Wànte, Apple dafay laaj xuusukaay ci iOS ngir jëfandikoo mbir bi nu tudde Webkit, liy tee Onion Browser am kiirlaay yu nirook ay kiirlaayu Tor Browser.

Jàngal leneen lu bari ci Onion Browser. Yebbil Onion Browser jëlee ko ci App Store.

Tor Browser ci telefonu Windows

Amul fi nu toll benn jëfekaay ngir doxal Tor ci telefonu Windows yu yàgg wànte su fekkee xeeti telefonu Microsoft/ yu yees yi la ,ñoo niroo jéego ci Tor Browser on Android mën nanu leen topp.

JAFE-JAFE YUNU XAM

DEF TOR BROWSER LUÑU MËN A TEYE CI LOXO

Soo bëggee, Tor Browser mën na yobbu dindi ko ci li nga deñc ci saasi ci xibaar yi mën a deñ niki ab bantu USB wala kàrtu SD. Digle nanu jëfandikoo xibaar yunuy bind ba nga xam ne Tor Browser dina nu ko mën a yeesalaat ni mu ware.

Ci Windows:

  1. Dugal ci say xibaar yi mën a deñ te nga foormate leen. Bépp xeetu doxalinu dosiye dina dox.

  2. Xuusal ci Tor Browser bi xëtu yebbi.

  3. Yebbil dosiye Windows .exe bi te nga deñc ko ci saasi ci say xibaar.

  4. (Digle) Saytul dosiyey xaatim.

  5. Su yebbi bi matee, kilikeel ci dosiye .exe bi te nga door tëralinu samp bi.

  6. Su sampukaay bi laajee fan ngay samp Tor Browser, tànnal say xibaar yi mën a deñ.

Ci macOS:

  1. Dugal ci say xibaar yi mën a deñ te nga foormate leen. Danga wara jëfandikoo Mac OS Extended (Journaled) format.

  2. Xuusal ci Tor Browser bi xëtu yebbi.

  3. Yebbil dosiye macOS .dmg bi te nga deñc ko ci saasi ci say xibaar.

  4. (Digle) Saytul dosiyey xaatim.

  5. Su yebbi bi matee, kilikeel ci dosiye .dmg bi te nga door tëralinu samp bi.

  6. Su sampukaay bi laajee fan ngay samp Tor Browser, tànnal say xibaar yi mën a deñ.

Ci GNU/Linux:

  1. Dugal ci say xibaar yi mën a deñ te nga foormate leen. Bépp xeetu doxalinu dosiye dina dox.

  2. Xuusal ci Tor Browser bi xëtu yebbi.

  3. Yebbil dosiye Linux .tar.xz bi te nga deñc ko ci saasi ci say xibaar.

  4. (Digle) Saytul dosiyey xaatim.

  5. Su yebbi bi matee, génneel li nga deñc teg ko ci xibaar yi itam.

NDIMBAL

Taxawu, waxu leeral ak nataal xëtu tegtal bu njumte

Soo nuy yónne ab laaj ngir ndimbal, leeral njumte wala siiwal njumte, nu ngi lay ñaan nga boole ci xibaar yi war yépp:

  1. Nosteg doxin bi ngay jëfandikoo
  2. Tor Browser version
  3. Tor Browser Kaaràngey tolluwaay
  4. Jéego ci kaw jéego ci nan nga jotee jafe-jafe boobu, kon mën nanu ko defaraat (e.g. Ubbi naa xuusukaay bi, bind ab url, kilike ci ab tànneef ci sukkandikukaay yi, léegi sama xuusukaay yàqqu)
  5. Ab nataalu xoolu ci jafe-jafe bi
  6. Téere bu console ci biro Tor Browser (mën nanu ko ubbi jaaree ko ci Ctrl+Shift+J ci Windows/Linux ak Cmd+Shift+J ci macOS)
  7. Tor logs (Sukkandikukaay > Lëkkaloo > awaanse > Yër Tor logs yi)
  8. Gox bi ngay lëkkaloo ci Tor.
  9. Gox yi nu tànn ci Connection Assist (su fekkee ab jafe-jafe bu aju ci Connection Assist)
  10. Ndax Tor danu ko tere ci sa gox?
  11. Su fekkee Tor du lëkkaloo, ñaata waxtu lay jël ngir mu bootstrap? Ndax amul benn njeexital ci sa gaawaayu xuusukaay?

Tor jëfandikukat bi dafay jàppale kureelu waxtu biro yi

Altine ba Alxames: sunu jëfandikukat danuy jàpp ci email, Telegram, WhatsApp, ak Signal dañuy dox.

Àjjuma ba Dibéer: Buumu jokko ngir ndimbal bi danu ko tëj. Nu ngi lay ñaan nga xam ne sunu kureel dina tontu say bataaxal ci Altine ji.

Naka nga nuy jotee

Am na anam yu bare ngir jot nu, kon nu ngi lay ñaan nga jëffandikoo bi gën a dox ci yaw.

Telegram

Am nanu ay Telegram ak jaarukaay yu fës yu bare:

  1. @GetTor_Bot ngir yebbi Tor Browser.
  2. @GetBridgesBot ngir jot obfs4 bridges.
  3. @TorProject ngir jot xibaar yi mujj.
  4. @TorProjectSupportBot ngir ndimbal.
    • Ci jamono jii, yoonu ndimbal bu Telegram jàppandi na ci ñaari kàllaama: Angale ak Russe.
    • Soo soxlaa ndimbal ngir wër ndomba yamale internet bi, nu ngi lay ñaan nga tànn ci àlluwa tànneef bi nekk ci diwaan bi ngay lëkkalowee ndax mooy tax mu gën a yomb ci nun nu topp la.

Tor Ndajey waxtaan

Nu ngi lay diggal nga ñaan ndimbal ci Tor Forum. Dinga soxla sàqq ab këll ngir joxe ëmbeef bu bees. Nu ngi lay ñaan nga xoolaat waxtaani tegtal te nga xool ëmbeef yi am laata ngay laaj. Fii nu toll, ngir tontu bu gën a gaaw, nu ngi lay ñaan nga bind ci Angale. Soo gisee ab njumte, nu ngi lay ñaan nga jëfandikoo GitLab.

WhatsApp

Mën nga jot sunu kureelu ndimbal ak ab xëtu message ci sunu nimero WhatsApp: +447421000612. Serwiis bii dafa jàppandi rekk ngir bataaxal yi; ay wideo wala woote du jàll.

Gindikaay

Mën nga am ndimbal jaaree ko ci ab xëtu message ci sunu Siñaalu nimero: +17787431312. Signal ab amalinu bataaxal la bu laajul. Jamono jii, sunu kureel bi di taxawu nit ñi jàppandi na ci Angale ak Russe te dafay jublu ci taxawu jëfandikukat yu Tor yi nu tere ci bépp gox. Serwiis bi dafa jàppandi rekk ngir ay bataaxal yi nu bind; ay wideo, wala ay woote duñu jàll. Gannaaw ba nu yónnee ab bataaxal message, sunuy ndaw yi lay taxawu dina ñu la gindi te jàppale la nga saafara jafe-jafe bi.

Boyetu bataaxal

Yonnee nu ab bataaxalu internet ci frontdesk@torproject.org

Ci boppu lu waral bataaxal bi ci sa email, nu ngi lay ñaan nga bind lu waral mbind mi. Sa bataaxal lu mu gën a leer ci bopp bi (ci misaal. "Làjj ci Lëkkaloo", "leeral njumte ci dalu web", "leeral njumte ci Tor Browser, "Dama soxla ab bridge"), mu gën a yomb ci nun ngir nu ndànd te topp. Yenn saa yi sunu jotee ay email yu amul mbind muy leeral lu waral bataaxal bi, danu leeni màndargaal spam te dunu leen gis.

Ngir tontu bu gën a gaaw, nu ngi lay ñaan nga bind ci Angale, Russe, Español, Hindi, Bangla, ak/wala Purtugees soo ko mënee. Su fekkee amul benn làkk boo dégg ci yooyu, nu ngi lay ñaan nga bind ci bépp làkk boo mën, wànte jàppal sa xel ne dinanu jël tuuti saa ngir tontu ndax dinanu soxla ndimbalu firikat ngir xam li nga wax.

IRC ak Matrix

Mën nga noo gis ci #tor jaarukaay ci OFTC wala Tor jaarukaay Ndimbal Jëfandikukat ci Matrix. Dunu mën a tontu léegi, wànte dañuy tontu xoolaale backlog bi te dinanu dellusi ci yaw saa su nu ko mënee.

Jàngal naka lanuy lëkkaloo ci IRC / Matrix.

GitLab

Lu njëkk, xoolal ndax njumte bi xam nanu ko. Mën nga seet te jàng jafe-jafe yépp ci https://gitlab.torproject.org/. Ngir sos mbir mu bees, nu ngi lay ñaan laajal ab këll gu bees ngir jot misaalu Tor Project's GitLab ak gis dalukaay bu bees nga siiwal jafe-jafe bi. Nu ngi topp jafe-jafe yépp ci Tor Browser ca Tor Browser topp jafe- jafe. Jafe-jafe yi lëkkaloo ak sunu dalu web ci fii lanu ko war a bind Toppkatu mbirum Web.